Njiitu Réew mi Basiiru Jomaay FAY, dalal na, ci àllarba ji 23i fani sulet 2025, S. Trân Thanh Mân, Njiitu Ngomblaanug Réewum sosiyaalist bu Wiyetnaam miy amal tukki nemmiku ci Senegaal.
Tukki bu am solo bii day firndeel jëflantey xaritoo ak lëkkaloo yi yàgg a dox diggante Senegaal ak Wiyetnaam.
Ndaje mu mag mii nag day wane yéene ji nu bokk am jëm ci gën a dooleel jëflante gi diggante sunu ñaari campeef yi, gën a dooleel weccente gi diggante Ngomblaan yi ak gën a xóotal lëngoo gi diggante sunu ñaari askan yi, lépp ci kaw wegante, jàppalante ak lëkkaloo gu sax dàkk.
Senegaal di feddali kon ag taqoom ci laamisoo gu ubbeeku, lalu ci mbokkoo te taxaw temm ngir yokkute, jàmm ak naataange gu séddalikoo.