Njiitu Réew mi dalal na Paab Naataango MBAY, di saa-senegaal bi ñu jëkk a jagleel raaya « Médaille Gaindé de la Performance »

xamle - 04 MONTHS.AUGUST 2025

Ginnaaw ba mu ko sargalee def ko saa-senegaal bi ñu jëkk a takkal raaya « Médaille Gaindé de la Performance », Njiitu Réew mi Basiiru Jomaay FAY dalal na tay ci suba Paab Naataango MBAY mi àndoon ak i way-juram. 

Ndaje mu am solo mii may na Njiitu Réew Mi mu rafetlu jaar-jaar bu mucc ayib bu ndawu saa-senegaal bii, nga xam ne ag dogoom ak taxawaayam ngir jàmmaarloo ak jafe-jafe yi lu ñépp war a roy la, rawati na ndaw ñi.

Mbooram day fàttali saa-Senegaal bu nekk ne, ak lu gàllankoor yi bari bari, manees na leen a jàll, bees wanee njàmbaarte, dogu ak ngor.