Njiitu Réew mi dalal na Njiitu Kubota Corporation, bokk ci ñi gën a ràññiku ci àddina si wàllu mësinu mbay la ndefar.

Biti Réew - 21 MONTHS.AUGUST 2025


Njiitu Réew mi dalal na, Njiitu Kubota Corporation, di Këru liggéeyu Japon gu mag guy yëngu ci wàllu jumtukaayi mbay ak ci wàllu ndefar. Ñu doon waxtaane lu jëm ci dooleel lëngoo gi ci wàllu mbay, fent ak dugal xaalis ci Senegaal.