xamle - 12 MONTHS.SEPTEMBER 2025
Njiitu Réew mi jagleel na ab jataay, tay ci ngoon gi, kii di Sëriñ Abdulaay JÓOB Njiitu komisoo bu UEMOA.
Ci biir waxtaan wi, moom Sëñ JÓOB rafetlu na jéego yi kilifay Senegaal yi di teg ngir ñoŋal koppari pénc mi.
Waxtaane nañu itam jafe-jafey koom ak campeef yi Mbootaay gi di jànkoonteel.