Njiitu Réew mi dalal na, ci bis bi, Profesëer Tanka AKIHIO, Njiitu Bànqaasu Japon bi Yor wàllu lëkkaloo ak àddina si (JICA), ñu doon waxtaane lu jëm ci gën a dooleel jëflante yi dox diggante Senegaal ak Japon.
Ndaje mii nag am pose la woon ngir gën a feddali lëngoo gu dëgër gi dox diggante ñaari réew yi boole ko ak fésal fànni lëkkaloo yu bari te am solo : tabaxaat beneen Barabu Tàggatukaay bu Senegaal-Japon ca Jamñaajo, muy sémb wu am solo wu jëm ci suqali xam-xam bi ak tàggatu gu xereñ gi; sémbu mbay mu yaatu mu Ngóornamaŋu Japon bi nangoo yaatal ca Kaasamaas, di tund wu ñu tàmbalee dimbali ba noppi ci wàllu sulli ndell ya; njariñ li sektéer piriweb Japon bi gis ci fànn yu ñu man a dugal seen xaalis ci Senegaal, rawati na ci wàllu yasara gi, paj mi ak mbay mi.
Ci biir Waxtaan yi, Njiitu Réew mi dikkaat na ci xéewal yu yaatu yi réewum Senegaal làq, manees cee lim dal gi ci wàllu politig, xemmemu gi am ci wàllu amal fi ay yëngu ak taxawaay bu am solo bi mu am ci biir àddina si, nga xam ne mooy bunt bi gën a jege ngir tàbbi ci Afrig Sowu Jant ak ci biir Kembaaru Afrig gépp.
Muy ndaje muy firndeel yéene ji ñaari réew yi bokk am jëm ci gën a dooleel lëkkaloo gu am solo, ñu gën koo jëmale ci wàllu tàggatu, fent ak suqaliku gu sax, lépp ngir njariñu askanu Senegaal ak wu Japon.