Njiitu Réew mi dalal na Njiitu Jëwriñu Gine Bisaawó ak Njiitu « Air Dynamics Solutions ».

xamle - 15 MONTHS.SEPTEMBER 2025

Ci altine ji, Njiitu Réew mi Basiiru Jomaay FAY, dalal na ci Njéndel Réew mi, Njiitu Jëwriñu Gine Bisaawó, S. Braima KAMARA. Nemmiku gii may na Njiitu Jëwriñu Gine Bisaawó li, mu yékkati kàdduy cant ak ngërëm ci taxawu gu mucc ayib gi ñu ko jagleel jamono ji mu nekkee Ndakaaru. Rafetlu na itam jéego yi Presidaa FAY ak EMBALÓ bokk di teg jëm ci gën a dooleel lëngoo gi diggante Ndakaaru ak Bisaawó, te doon luy fedaali jëflantey bokkoo yi yàgg a dox diggante ñaari askan yi.




Ci bis boobu ba tay, Peresidaa FAY séq na waxtaan ak Njiitu kërug Emiraa gii di « Air Dynamics Solutions », doon ñu xereñ ci wàllu xarala ak fent ci wàllu fafalnaaw. Jataay bii nag day tàbbi ci yoonu gën a dëgëral  lëngoo gu am solo gi dox diggante Senegaal ak Emiraa Araab Unii, rawati na ci wàllu lépp lu jëm ci mbirum fafalnaaw, jumtukaay yi ak tabax yi. « Air Dynamics Solutions » xamle na yéeneem ci dugal xaalis ci Senegaal ak gunge jëmmalug Senegaal 2050.