Njiitu Réew mi Basiiru Jomaay Jaxaar Fay, dalal na tay ci ngoon gi kilifa yu bari ci Njéndel Réew mi.
Ki mu njëkk a dalal di, Soxna Kiristel Heydemann, di Njiital Kippaangog ORANGE. Ci ndaje mi, moom soxna si xamle na yéeney kippaango gi jëm ci gunge Njiitu Réew mi ci wàllu « New Deal technologique » bii namm a tabax serwiis piblig bu méngoo ak jamono te dëgmal ëllëg.
Mu teg ci moom Peresidaa Fay, dalal Jëwriñu Jibuti ji yor wàllu Jëflante ak Biti Réew, Sëriñ Mahmuut Aali Yuusuf mi ko doon indil bataaxel bu bawoo ci Peresidaa Ismayil Omar Gelleh. Muy ndaje mu jëm ci gën a dooleel jëflante yi diggante Senegaal ak Jibuti.
Mu tëjee ko ci dalal Sëñ Porospeer Zo’o Minto’o, miy Njiital ASECNA lu bees li. Xamal na ko gis-gis bi mu am jëm ci saafara jafe-jafey kër gi, boole ko fésal solos kaaraangeg jaww ji ngir yokkuteg tund wi.