xamle - 02 MONTHS.SEPTEMBER 2025
Njiitu Réew mi, Basiiru Jomaay FAY, dalal na ci ngoon gi, Jëwriñu Biritanig ji yor wàllu Afrig. Mu teew Senegaal ci lu soxal Ndajem waxtaane wàllu dund bi ci Afrig, moom Lord KOLLINS feddali na jaayanteg Royaume Uni jëm ci gën a rattaxal jëflante yi ci wàllu yaxantu ak dooleel lëngoo gi dox seen diggante ak Senegaal ci anam yu kenn ku nekk di man a gis boppam.