xamle - 16 MONTHS.JUNE 2025
Njiitu Réew mi dalal na ci suba kilifa gii di Tete Àntoño, Jëwriñu Àngolaa ji yor wàllu Jëflante ak Biti Réew, te ñëwoon ngir indil ko bataaxelu João Lurenco, Njiitu Réewum Àngolaa di jiite it jamono jii Mbootaayu Réewi Afrig.
Waxtaan yi jëmoon ci gën a dooleel jëflante diggante ñaari réew yi niki noonu tombi njariñ yu am solo yi ñu bokk am.