Biti Réew - 25 MONTHS.SEPTEMBER 2024
Tay ci ngoon gi, Njiitu Réew mi, Kilifa gi Basiiru Jomaay Fay dalal na Sekkereteer Detaa bu Amerig di Àntoni Blinken. Ndaje mii may na ñaari jëmm yi ñu rafetlu jëflante yu rattax yi dox diggante Senegaal ak USA boole ci feddali seen jaayante ci gën a dooleel lëkkaloog koom mi, rawati na ngir taxawu ndaw ñi ak fésal doxaliin wu leer niki noonu xeex ger.
Ñaari njiit yi waxtaane nañu tomb yu soxal kaaraange gi ci Sahel bi ak jàmmaarloo yay am ca Moyen-Orient. USA xamle nañu ne noppi nañu ngir jàppale Senegaal ci ay coppiteem.
Yeneen pàcc yu far ci doxaliin wu yees wii di “Agenda National de Transformation 2050 du Sénégal”, te ñu war koo aajar 7i oktoobar, itam bokk na ci yooni lëkkaloo yi ñu war a dooleel, te mu ëmb wàllu xarala yi ci lii di « New deal technologique », mbay mi ak ndefar yi.
Ndaje mii day dëggal lëkkaloo gu dëgër diggante Senegaal ak USA, te doon lu lalu ci bokk benn gis-gisu suqaliku ak naataange gu yaatu.