Biti Réew - 29 MONTHS.JUNE 2025
Njiitu Réew mi Basiiru Jomaay Jaxaar FAY, bawoo na Ndakaaru tay ci suba, wutali “Seville”, ca réewum Espaañ ga mu war a teewe 4eelu Ndajem àddina mi ñu jagleel wàllu kopparal suqaliku gi.
Ci kilifteefu Mbootaayu Réewi Àddina si, ndaje mu kawe mii dina dajale Njiiti Réew ak Ngóornamaŋ yu bari, niki noonu ay kilifay campeefi àddina si, ngir waxtaane jafe-jafe yi jëm ci man a dajale balluwaay yu wér ngir suqaliku gu sax.
Ba muy bawoo ca naawub sóobare bu Léwopóol Sedaar Seŋoor bu Yoof, moom Njiitu Réew mi jot naa saafonte ak Njiitu Jëwriñ yi ko gunge niki noonu kilifay siwil yi ak yu militeer.