Njiitu Réew mi, Basiiru Jomaay Jaxaar FAY, jiite na, ci àjjuma ji 30i fani mee 2025, jataayu jébbale rappooru atum 2023-2024 bu “Haut Conseil du Dialogue Social”.
Ci ndaje mii, Njiitu Réew mi rafetlu na jaayanteg ñi teewal ñetti wàll yi ci anam yi ñu dugalee seen yoxo ngir dal am ci wàllu liggéey bi ak gën a dëgëral jëflante yi ci liggéey bi. Feddali na ne dalug liggéey bi daa bokk ci keno yu am solo ngir amal ay coppite ci koom mi ak dudiinu askan wi.
Njébbaleg rappoor bii nag mu ngi dikk ci jamono ju fés lool ak torlug, 1 panu mee 2025, ci “Pacte national pour la Stabilité sociale et une Croissance inclusive et durable”, di njureefu waxtaan yu yàgg a dox diggante Nguur gi, mbootaayi njaatige yi ak mbootaayi liggéeykat yi.
Njiitu Réew mi wane dëppoog doxaliin wii ak Péncoo gi ñu nekk di amal, te doon luy wane yéeney tëggaat Repiblig bi ci kaw déglu, bokk taxawaay ak soppiku gu wér ci wàllu doxaliin.
Soññ na mbooleem njëwriñ yi ñu taxawal ay kuréli diisoo ci wànqaas yi aju ci ñoom ngir fagaru ci yenn réeroo yi boole ko ak taxaw ci wéyal serwiis piblig bi ci pas-pasu déggoo ci réew mi.