Njiitu Réew mi Basiiru Jomaay FAY yegg na ca Monrovia ngir teewe 178eelu xumbeeli jonnug Liberiyaa.

Biti Réew - 25 MONTHS.JULY 2025


Ginnaaw tukki nemmiku gi mu amal ca Lome, ca réewum Togóo, Kilifa gi Basiiru Jomaay FAY, Njiitu Réewum Senegaal, yegg na ci ngoon gi ca Monrovia, gëblag Réewum Liberiyaa, ci àjjuma ji 25i fani sulet 2025. Kilifay Liberiyaa yi teertu nañu ko tatagal ko ci anam yu mucc ayib.

Njiitu Réew mi dina teewe, ci gaawu bi 26i fani sulet, xumbeelu màggal 178eelu ati jonnug réewum Liberiyaa ci wetu Kilifa gi Josef Nyumah Boakai, Njiitu Réew ma.