Biti Réew - 13 MONTHS.FEBRUARY 2025
Njiitu Réew mi Bassirou Diomaye Faye, yegg na ci ngoon gi ca Adis Abebaa (Ecopi) ngir teewe 38eelu jataayu Ndajem Njiiti Réew ak Ngóornamaŋ yu Mbootaayu Réewi Afrig, ñu koy amal 13 jàpp 16i fani féewarye 2025, war caa waxtaane tomb bii di : « Atum yoon ngir saa-afrig yi ak ñi càllaloo ci saa-afrig jaare ko ci joyyanti ».
Ca ndaje moomu, Njiitu Réew mi dina fa teewe ay jataay yu am solo yu mel ni ci wàllu anam yi ñuy kopparalee paj mi ak ci doxaliinu Afrig. Dina amal ay ndajey lëkkaloo itam diggam ak ay naataangoom ak kilifay yenn mbootaay yi ci àddina si.
Présidence de la République du Sénégal