xamle - 26 MONTHS.APRIL 2025
Njiitu Réew mi, Basiiru Jomaay Fay, teewe na, tay ci gaawu bi, ca Dakaar Arenaa bu Jamñaajo, ndamul “ASC Ville de Dakaar” ci dugguseem bu njëkk ca “Conference Sahara de la Basket-ball Africa League (BAL) 2025.
Ci xumbaay bu jéggi dayo, mboolo mu takku di leen kañ ak a ñaax, “ASC Ville de Dakaar” amal na joŋante bu mucc ayib diggam ak “US Monastiir”, ginnaaw jàmmarloo bu tar.
Ci xew-xew bii, Njiitu Réew mi posewu na ci weccente ak jëmm yu fés ci wàllu mbatiit mi ak ndawi Afrig yu teewoon ca Dakaar Arenaa, ñu mel ni Xabi Laam, Daara J Family, Yuusufa, Kanabaas ak Dip Dund Gis. Rafetlu na seen taxawaay ngir gën a dooleel tàggat yaram ak mbatiit.
Ci teewaayam bii nag, Njiitu Réew mi day feddali rekk ag taqoom ci suqalikug basketball bi ak gunge ndaw ñi, nga xam ne doon nañu jumtukaay yu am solo ngir gën a yékkati Senegaal ak kembaaru Afrig.