Njiitu Réew mi, Basiiru Jomaay Fay, teewe na ci dibéer ji 7i sulet 2024 65eelu Ndaje Mu Mag mu Njiiti Réew ak Ngornamaa yu CEDEAO

Biti Réew - 07 MONTHS.JULY 2024

Njiitu Réew mi, Basiiru Jomaay Fay, teewe na ci dibéer  ji 7i sulet 2024 65eelu Ndaje Mu Mag mu Njiiti Réew ak Ngornamaa yu mbootaayu koom yu Réewi Afrig Sowu Jant (CEDEAO), mi doon am ca Abujaa, Gëblag Niseriyaa.

Ki doon jiite ndaje ma di Njiitu Réewum Niseriyaa, Bolaa Ahmet Tinubu, mi jiite jamono jii kurélug Njiitu Réew ak Ngornamaa yu CEDEAO.

Ci ay kàddoom, Njiitu Réew mi Basiiru JOMAAY Fay fàttali na ne wareef la ñu wéyal jéego yi ngir dajalewaat mbooleem njaboot gi ngir man a def doole yi ak koom mi ci sémb ak naal yi ñeel askan wi tax a jóg Réew yi bokk ci mbootaay gi. 

Njiitu Réew mi soññee na ci ñu fexee liggéey ngir teqale ak CEDEAO gis-gis ak ni ko ñu bari jàppee niki taxawaayu kurél guy dox ci ndigali réewi tugal yu am doole yi boole ci sori lool askanam wi leen tax a jóg nga xam ne ñoom lañu waroon a liggéeyal.

Lu soxal yëngu-yëngu yi am nag, Njiitu Réew mi fésal na solo si nekk ci gën a dooleel fegu ci réeroo yi jaare ko ci jiital waxtaan ak diisoo ci jamonoy jàmm, ngir wàññi bu baax jafe-jafe yi boole ko ak am dooley man koo saytu bis bu dara xewee.