Njiitu Réew mi Basiiru Jomaay Fay teewe na 42eelu Jataayu Komite Oriyàntaasoo bu AUDA-NEPAD bi ñu doon amal jaarale ko ci xarala yi.

Biti Réew - 10 MONTHS.FEBRUARY 2025

Njiitu Réew mi Basiiru Jomaay Fay teewe na, tay 10i fani féewarye 2025, ci 42eelu Jataayu Komite Oriyàntaasoo bu Njiiti Réew ak Ngóornamaŋ yu AUDA-NEPAD, bi ñu doon amal jaarale ko ci xarala yi.

Cig àddoom, Njiitu Réew mi feddali na jaayanteg Senegaal ngir amal coppite yu matale ci kembaaru Afrig, gi mu jàpp ne mu ngi war a jaar ci:

- boole mbooleem liy ballee ci biir Afrig jaare ko ci yéene  jii di   « Team Africa » ngir kopparal  sunuy sémb bañ a teg sunu yaakaar jépp ci biti réew ;

- baral jéego yi jëm ci jëmmal kembaar gu jàppandi ci wàllu njënd ak njaay (ZLECAF) ngir yokk jëflante yi ci diggante réewi Afrig yi boole ko dooleel manal sunu bopp gi ci wàllu koom;


- suqali jumtukaay yi ci wàllu yasara ngir jot ci kuraŋ  man a doon lu jàppandi boole ko ak taxaw ci samp ay ndefar ci kembaar gi;


- tàggatu gu xereñ te méngoo ak jamono, lu mel ni ci wàllu xarala yi ak wàllu « intelligence artificielle »,  ngir jox ndawi Afrig jumtukaay yu ñu man a jàmmaarlo ak jafe-jafey ëllëg.


Njiitu Réew mi rafetlu na itam taxawaay bu am solo bi Peresidaa Al Sisi am boole ko ak ànd ci ñu yokkaat ayam ci boppu  Komite Oriyàntaasoo bu AUDA-NEPAD