Njiitu Réew mi Basiiru Jomaay Fay teew na ci biir Jumaa ju mag ju Seex Sayed ak « musée du Louvre » bu Abu Dabi.

Biti Réew - 05 MONTHS.DECEMBER 2024

Njiitu Réew mi, Basiiru Jomaay Fay, mu ngi dooree, ci alxemes ji 5i fani desàmbar 2024, ngan gi muy amal ca Emiraa,  ag nemmiku ci ñaari warab yu am solo.

Njiitu Réew mi njëkkee ci nemmiku Jumaa ju Mag ju Seex Sayed, di taax mu yéeme te taaru lool, bokk it ci barab yi ñu gën di nemmiku ca réew ma.

Beneen jataay bu am solo ci bis bi tamit di ag demam ca « musée du Louvre » bu Abu Dabi , doon taax mu gànjaru ci wàllu mbatiit di màndargaal yéeney Emiraa ci boole moomeelu àddina si ak fésal taaru pasin.

Nemmiku gii mu ngi jëm ci gën a dooleel jëflante yi diggante Senegaal ak Emiraa ngir bokk amal suqaliku gu wér te wóor.