Ci guddig àjjuma 8 jàpp gaawu 9i fani nowàmbar 2024, mbërum Senegaal mii di Umar Kan, ñu gën koo xam ci turu Rëg-Rëg, déjjati na Anatóli Malykhin mi doon ñetti yoon keleŋu ONE Championship, ci xeexu puwaa luur bu amoon ca xewu ONE 169 ca Bangkog, ca Tayland.
Ndam lii nag tax na Umar Kan doon keleŋu Afrig bi njëkk ci mboorum ONE Championship. Njiitu Réew mi Basiiru JOMAAY Fay jaare na ci sàqam bu X, ndokkale sunu mbokku ma-réew bii dugg ci mboor daal di doon saa-senegaal bi njëkk a nekk keleŋu àddina si ci wàllu puwaa luur MMA. Kañ na ko itam ci li mu siggil Senegaal, sagal askan wi cig njàmbaaram, dogoom ak xereñteem. « Askan wi bég na lool ci ndam lu rëy lii », di li mu tëjee bataaxelam.