Njiitu Réew mi Basiiru Jomaay Fay jot na ci ràppooru at mi Mejaatéeru Repiblig bi di amal.

xamle - 20 MONTHS.MARCH 2025

 

Jébbale Ràppooru at mi Mejaatéeru Repiblig bi di amal doon na jataay bu am solo ci dundug Senegaal. Muy xew-xew bu bokk ci cosaan yi sax ci réewum Senegaal, te mooy waxtaan ba juboo, di keno bu am solo ci Nguur guy bàyyi xel bëgg-bëggi askanam boole ko ak taxaw temm ci waxtaane jafe-jafey réew mi ngir indi ci ay saafara.

Ci biir ndaje moomu, Njiitu Réew mi Basiiru Jomaay Fay xamle na solo si digle yi nekk ci biir ràppoor bii làmboo. Muy digle yuy àddu ci tomb yu am solo : doxal dogal yi bawoo ci yoon, gën a doxal ag nite ci anam yi ñuy tëjee, amal ay coppite ci yoriinu suuf si, kaaraangeg yoon yi ak gën a jagal baaxaayu serwiis piblig bi. Muy wëppa yu am solo yu méngoo lool ak askan wu namm a doxal maandute boole ko ak am ug yokkute.

Njiitu Réew mi feddali na yéene ji mu am ci doxal ca na mu waree digle yii muy soññe ngir ñu jëmmal leen. Moom nag jàpp na ne, yooriin wu baax mu ngi tegu ci Ndoxal guy taxaw ci liggéeyal askanam, te sampu ci pas-pasu yoriin wu leer te yamale. Mbébet mii, ñu teg ci dayo bu kawe, day firndeel gis-gis bu leer : def diisoo muy jumtukaay bu wér ngir tabax Senegaal gu jub te mànkoo.