Ci posem 1 panu mee bi, di bis bi ñu jagleel liggéey ci àddina si, Njiitu Réew mi Basiiru Jomaay Fay, jot na ci karney njàmbat yi ko sàndikaa yi doon jébbal.
Xewu cosaan wii doon jataayu diisoo ak weccente ay xalaat bu am solo, may na Njiitu Réew mi mu feddali ag taqoom gu wér ci mbaaxi liggéey, sàmm yelleefi liggéeykat yi ak yamale. Ci kanamu jafe-jafey jamono ji ci wàllu koom ak dundiin, Njiitu Réew mi yeesalaat na jaayante gu wér gi Ngóornamaŋ bi am ci doxal, bu wér te wóor, déggoo yi ñu tënk ci “Pacte de stabilité sociale” bi.
Njiitu Réew mi ndokkale na bu baax boole ko ak ñaanal ak jaajëfal mbooleem liggéeykati Senegaal yi, góor ak jigéen, ci seen taxawaay bu am solo bis bu set ngir dugal seen loxo ci tabax ëllëg gu ñoŋ, gu tegu ci yoon te naat ñeel askan wi.