Njiitu Réew mi Basiiru Jomaay Fay jot na bataaxeli tabb yu juróom benni ma-laamisoo yu bees ci Senegaal

xamle - 14 MONTHS.NOVEMBER 2024

Njiitu Réew mi, Basiiru Jomaay Fay, jot na ci alxemes ji 14i fani nowàmbar 2024 ci Njénde li, Bataaxeli tabb yu Ma-laamisooy Réewum Wenesuwelaa,  Namibi,  Gaboŋ, Keeñaa, Emiraa Araab ak Syeraa Lewon.

Njiitu Réew mi ndokkale na leen bu baax boole ci dalal seen xel ci gungeg Ngóornamaŋ bi ngir ñu man a matale bu wér seen i sas ci Senegaal.

Njitu Réew mi Basiiru Jomaay Fay, feddali na itam yéeneem ci wéyal lëkkaloo yu am solo yi niki noonu gën koo dooleel ci fànn yu bari te wuute diggam ak seen réew yooyu. 

Juróom benni ma-laamisoo yi ñoom itam, ci seen wàll, rafetlu nañu jëflante yu rafet yi dox diggante seen i réew ak Senegaal, teg ci jaayante ci dox ci lu koy gën a dëgëral.