Njiitu Réew mi Basiiru Jomaay FAY jiite na xewu jébbale raaya “Concours Général 2025".

waxtaan - 31 MONTHS.JULY 2025

Njiitu Réew mi Basiiru Jomaay FAY, jiite na, tay 31i fani sulet 2025, ca “Grand Théâtre National” Duudu Njaay Kumba Róos bu Ndkaaru, xewu jébbale raayay “Concours général” 2025.


Ñu ci doon waxtaane wëppa wii di nees di fexee ba soppi njàng mi ba mu gën a méngoo ak nit ñi ci jamonoy xarala yi ak “intelligence artificielle”, xewu ren wi sargal nañu ca jëmm ju am solo jii ci réew mi, di S

André Sonko, nekkoon fi Jëwriñu Njàng mi, te ñu baayale ko ko ndax ab taxawaayam ak royukaay gi mu doon ci dooleel njàngum réew mi ak jikko yu rafet.



Cig àddoom , Njiitu Réew mi ndokkale na bu baax ñi ñu jagleel raaya yi, ci teewaayu kilifa yu bari ak ñiy yëngu ci njàng mi.  Rafetlu na bu baax fulla gi ñu wane ci sàkku xam-xam, seen dogu ak seen yar, yi tax ñu doon yaakaari réew mi ëllëg. 


Njiitu Réew mi xamle na ne “Concours général” bii, ñu yoonal lu ëpp 50i at, doonatul rekk xew-xewu njàng mi : mooy « seetu biy wane dundalug xam-xam ci Senegaal » di finrndeel itam dooley lekool bi ci tàggat ma-réew yu xereñ. 


Waaye tamit naqarlu na ni ñu xawee desal ginnaaw wàllu xamtu, xarala, ak tàggatu gu xereñ gi ci njàngum Senegaal. Ngir gën a méngale njàng mi ak jubluwaayi “Agenda national de Transformation Sénégal 2050” bi, woote na ñu soppi doxaliin wi ngir gën a def lekool bi mu gën a xemmemu, gën a sopplu, jaare ko ci ñaax dongo yi ñuy gën a sóobu ci njàngum xamtu yi ak xarala yi. 


Ci loolu, Njiitu Réew mi yëgle na taxawalug, li ko dale atu njàngum 2025-2026, joŋante bu ñuy jagleel dongo yi nekk diggante CM2 ba Terminaal, ci wàllu Matamatig, Xamtu ak Xarala, lépp ngir dooleel fànn yooyu boole ko ak gën a xemmemloo ndaw ñi wàllu xarala yi.  

Ci jamono ju ag soppiku am ci àddina si ci wàllu xarala yi, Peresidaa FAY soññee na ngir ñu fexe ba gën a niteel njàng mi, jaare ko ci jëfandikoo ca na mu waree, lii di xarala yi ak  “intelligence artificielle (IA)” bi. Àrtu na itam ci ñu moytu bu baax yenn ëppal yi am ci wàllu IA, yu mel ni di dugg ci dundug nit ñi walla amal ag ñàkk a yamale, teg ci woote ngir nu jéem a manal sunu bopp ci wàllu xarala gu lalu ci gëstu ci li ci réew mi ak doxaliin wu sell. 


Ci jataay bii, Sëriñ Paab Naataango MBAY, Njiitu Réew mi sargal na ko fa, jaare ko ci jagleel ko raaya “Médaille Gaïndé de la Performance” wi jëkk.


Ràññiku gii nag day delloo njukkal jaar-jaar bu mucc ayib bi Sëñ Mbay mii wane, nga xam ne laago bi mu àndal terewu koo jëfandikoo ay tànkam ngir amal ug kàtteem ba am ci bagam ak “mention Bien”.