Njiitu Réew mi, Basiiru Jomaay FAY, jiite na ci àllarba ji 28i fani mee 2025, ca “Centre international de conférences Abdu JUUF (CICAD)”, jataayu tijjitel liggéey yi jëm ci péncoo ci sistem politigu réew mi. Xew-xew bu am solo bii, bokk ci arminaatu réew mi, dajale na ñi teewal làngi politig yi, sosete siwil bi, kilifa diine yi ak yu aada yi, ay sàndikaa ak ñeneen ñiy yëngu ci dundug pénc mi, ñoom ñépp ñëwoon wuyusi ci wooteb Njiitu Réew mi ngir bokk amal waxtaan yu xóot ci tomb yu mag yi soxal campeef yi ak politig bi.
Ginnaaw àddug ñi teewe woon jataay bi, Njiitu Réew mi yékkati na kàdduy boole te ànd ak xereñteef.
Cig àddoom, Peresidaa FAY feddali na ag jaayanteem jëm ci sàmm bennoo gi ak dal gi ci réew mi, jaare ci xamle wareefu toogandoo amal waxtaan yu ànd ak déglonte, kóolute ak fexee déggoo. « Sas wi gàllu sama ndodd niki ku war a sàmm bennoo gi ci réew mi, mooy ma tàllal ñépp loxo, ngir dalal xel yi, boole, dalal ak juboole ngir gën a feddali jàmm ak dal yi manul a ñàkk ngir suqali koomum réew mi.», di li mu xamle.
Njiitu Réew mi taxawlu na itam ci taxawaay bi Ngóornamaŋ bi am ngir matal sas wu am solo wii, lépp boole ko sàmmonte ak yelleefi kujje gi, ci kaw li ñu yoonal. Leeral na ne diisoo yii, nga xam ne amul lenn lu làqu ci ginnaaw, am pose la ngir waxtaan ci ay coppite yu jëm ci jubbanti, te bokk ci yooyu xoolaat arminaatu joŋantey pal yi, doxaliinu làngi politig yi ak seen ug kopparal, taxawalug kurél gu moom boppam guy saytu joŋante yi, niki noonu caytug fiise elektoraal bi ak taxawaayu yoon ci wàllu joŋante yi.
Mu wéyal ay kàddoom, moom Peresidaa FAY xamle ne fàww ñu amal diisoo yu wér te wóor ci ëllëgu sistem politigu Senegaal, mu jaare ci fàttali ne doxaliinu bañ a beddi kenn wii daa war a lalu ci pas-pasu demokaraasi, rawati na sàmmonte ak péexte yi ñeel kenn ku ne, niki noou ci yeesal yi war a am ci wàllu ndayi sàrti réew mi ak ci wàllu yoonal.
Mu tëjee ay kàddoom ci ñaan ne : «Maa ngi ñaan seen diisoo yii ak lu man a xew, kenn ku ne fàtte sa bopp te jiital njariñu Senegaal gi nu féete kaw nun ñépp. »
Man ngeen a toppaat fii ci suuf mbooleem kàdduy Njiitu Réew mi :
Ginnaaw bi ma leen nuyoo
Yaw Njiitu Asàmble Nasonal bi,
Njiitu Jëwriñ yi,
Góor ak Jigéen ñi bokk ci Ngóornamaŋ bi,
bokki Depute yi,
Soxna si Topp ci Njiitu Conseil constitutionnel,
Njiitu “Cour suprême”,
Njiitu “Cour des comptes”,
Njiitu “Cour d’appel” bu Ndakaaru,
Njiitu “Commission électorale nationale autonome”,
Njiitu “Conseil de régulation de l’Audiovisuel”,
Njiitu “Haut Conseil du Dialogue social”,
Kilifa diine yi ak kilifa aada yi, Góor ak Jigéen ñi teewal sosete siwil bi,
Jigéen ak Góor ñi teewal sàndikaa yi ak mbootaayi njaatige yi,
Mbooleem ñi fi teew, ci seen wàccuwaay, seen taxawaay ak seen dayo,
Soxna yi ak Sëriñ si,
Nu dajewaat fii tay kon, ci lu ñeel péncoo gi nuy amal, ñaareelu yoon ginnaaw ba ma jiitee réew mi ak tay. Ren nag, noo ngi tijji diisoo yu yaatu te boole ñépp ci tomb bu am solo bii soxal réew mépp : Sistemu Politig bi.
Sunu teewaay ci ndaje mu gànjaru mii dajale mbooleem ñi am kàddu ci réew mi, day feddali sunu wareef ci sàmmonte ak bis bii doon lu ñu yoonal ci arminaatu réew mi.
Péncoo bi jàmm amee, danuy gën a saxal ci mbaaxi diisoo ak sàmm jàmmi pénc mi nu am wareefu sax ci di ko tabax.
Soxna yi,
Sëriñ si,
Boole mbooleem ñi séq askan wi, ci doxaliinu réew mi, mooy, bu dee manees na koo waxee noonu, firnde ci dogoo gi nu namm ak yenn xeeti doxaliin yi ci anam yi nuy saytoo pénc mi tay.
Li ma gëm bu wér nag mooy, bu weesoo way-politig yi, saa su ay yeesal waree am ngir jubbanti sunu sistemu politig, askan wépp a ci war a am kàddu.
Kon danoo war a rëdd, jaare ko ci waxtaan ba juboo, anam yi nuy taxawalee sàrt yiy jëmale kanam sunu dundu politig.
Lii mooy njariñu Péncoo bi jàmm amee, ngir moytul askan wi dem ba tàbbi ci ndëgg-sërëx di door a xool noo ca génnee, waaye itam ngir àndandoo, bind xët yi gën a taaru ci sunu mbooru politig.
Soxna yi,
Sëriñ si,
Kàddu gii di « Senegaal réewum diisoo la », du waxi neen. Muy kon wéyal ndono lii nga xam ne cosaan la ci Senegaal muy péncoo ak diisoo lii nu bokk di réew mi.
Sunu wareef nag mooy sàmm ndono lii ñoŋal ko ba man koo jébbalewaat ci jàmm.
Waaye nag, fàww nu jéem a dox bañ a taxaw rekk ŋoy fenn. Danoo war di xalaat saa su ne doxiinu askan wi ci sunu réew. Ndax kat, fitna yi Senegaal jot a dund tar nañu lool ba tax na maneesu koo fàtte.
Ay wakkan rot nañu fi. Ay njaboot yuy wéy ba leegi di jooy seen i bokk. Ay góom yuy xar ba fii ngir ñu faj leen.
Ci sama taxawaayu Njiitu Réew mi, maa ngi sëngeem di toroxlu ci kanamu mbooleem way-loru ñi nga xam ne ca sunu jonni Yàlla ya ak tay, ñu ngi wéy di jànkoonte ak i metiit ci yoon wi jëm ci taxawal demokaraasi bu mucc ayib. Maa ngi feddali njàppaleg askan wi jëme ci seen i njaboot, seen i xarit ak ñi ñu daan àndal ci xeex bi.
Sas wi gàllu sama ndodd niki ku war a sàmm bennoo gi ci réew mi, mooy ma tàllal ñépp loxo, ngir dalal xel yi, boole, dalal ak juboole ngir gën a feddali jàmm ak dal yi manul a ñàkk ngir suqali koomum réew mi.
Ci loolu, Ngóornamaŋ bi dina taxaw temm ci matale sasam. Dees na jox kujje gi cér bi mu yellool boole ko ak bàyyi ko mu doxal i sañ-sañam, ci kaw sàmmonte ak yoon.
Soxna yi,
Sëriñ si,
Mbooru politig mi réew mi dund lu yàggul dara, moo war a tax ñu amal ay yeesal ngir ëllëg :
- Yeesal ngir gën a dooleel li nu jot a am ci demokaraasi boole ko ak gën a taxaw ci sàmm dalug sunu campeef yi;
- Yeesal ngir seppi ci sunu sistem elektoraal lépp luy nuru ak réeroo, rawati na diggante nguur gi ak kujje gi.
Tay nag sunu demokaraasi laaj na nu def taxaw-seetlu ci :
- ag jubbanti ci arminaatu joŋantey pal yi;
- Taxawalug kurél gu moom boppam guy saytu joŋantey pal yi;
- doxaliinu wànqaas yiy lootaabe joŋantey pal yi;
- jàppandig fiise elektoraal bi ak caytu gi;
- yamale làngi politig yi ak xool anam yi ñu leen di kopparalee;
- taxawaayu yoon ci doxaliinu joŋante yi;
- jëfandikoo xarala yi ci doxaliinu joŋante yi ;
- estati kujje gi war a am màcceer bu wér ;
- bind otomatigmaa ci list elektoraal yi ku xas a am 18i at;
- àppug kàmpaañ elektoraal yi;
- walla sax yu mel ni parenaas bi ak ñoom seen.
Diisoo yii sax nag, noo ngi sant Yàlla ba benn joŋante jegewul. Loolu nag dinanu may nu man a waxtaan ci xel mu dal ci ëllëgu sunu sistemu politig.
Nun ñépp a am wareefu xoolaat sunuy campeef, sukkandiku ko ci kenoy demokaraasi, sàmmonte ak yelleefi kenn ku ne, niki noonu yeesal yu manul a ñàkk ci wàllu ndayi sàrt yi ak ci wàllu yoonal.
Saa-senegaal yi nag, muy góor di jigéen, ñoom ñépp may nañu leen ñu bokk ci waxtaan yii ba jot cee joxe lu ëpp fukki junni ak ñett (13.000) ci ay gaaral yu ñu jaarale ci Njëfekaayu Jubbanti gi ñu tegoon àjjuma 09i fani mee 2025.
Bu weesoo nag li askan wi di séntu ci njeexital yi war a bawoo ci diisoo yii, sóobu gii ab soññee la ci mbooleem ñiy teewe jataay yi teg ci di ab woote bu wér ci gën a wane taxawaayu kilifteef ngir man a am déggoo yu wóor te am njariñ.
Askanu Senegaal a ngi leen di teewlu !
Soxna yi,
Sëriñ si,
Ma bëggoon, ci jataay bu am solo bii, ndokkale bu baax kii di « Facilitateur général du Dialogue national 2025 » bi, muy Doktoor Seex GÉY, ci li mu nangoo jiite liggéey yi.
Yaw mii di “facilitateur général” bi, sag njub ak ni nga taqoo ak mbaaxi réew mi, gëm naa ne dina tax nu am doxaliin wu mucc ayib ci mbir mii.
Bëggoon naa itam, jagleel ag cant ak ug ngërëm, mbooleem ñi ñëw wuyyusi ci diisoo yii.
Seen teewaay fii tay day firndeel seen ug taqoo ci bëgg réew mi, jàmmi pénc mi ak màggaayu sunu demokaraasi.
Maa ngi ñaan seen diisoo yii ak lu man a xew, kenn ku ne fàtte sa bopp te jiital njariñu Senegaal gi nu féete kaw nun ñépp.
Kon ci loolu, laay ubbee liggéey yi aju ci péncoo gii ci sunu sistemu politig, di am yaakaar ci jaayante gi nu bokk am ak samag taqoo gu dul dog ci mbaaxi demokaraasi ak mànkoo gi am ci réew mi.
Yal na Yàlla def jàmm ak xéewal ci Senegaal.
Maa ngi leen di sant di leen gërëm ci seen teewlu.