Njiitu Réew mi Basiiru Jomaay Fay, jiite na ci àjjuma ji 21i féewarye 2025, xewu ndoortel liggeeyi sémbu PROMOREN ca Kungéel. Sémb wu am solo wii mu ngi jëm ci dajale mbooleem balluwaayi ndox yi nekk ca dexu Ñanija Bolong.
PROMOREN bii « Office des Lacs et Cours d’Eau (OLAC) » di jëmmal, dina tax ñu man a dajale lu tollu ci 46,6i miliyoŋi m³ ci ndox mu teey at mu jot, dakkal ndoxum xorom may bawoo ca dexu Gàmbi di ci raaxaloo, man a jëfandikoo lu tollu ci 12 000i hegtaar ci ay tool at mu jot. Sémb wii njëg gi tollu ci 36i milyaari FCFA, 92% ci kopparal gi ci « Bànk Islamique de Développement (BID) » la bawoo, 8% yi Nguurug Senegaal génne ko.
Cig àddoom, Njiitu Réew mi xamle na ne fas na yéene taxaw temm ci amal ay coppite yu xóot ci réew mi, muy ci fànni koom mépp rawati na ci sektéer pirimeer bi. Moom Njiitu Réew mi nag jàpp na ne, ngir amal yenn jëf yi, fàww ñu am ndox mu doy sëkk te jàppandi ngir man a taxawu mbay mu mucc ayib, càmm gi ak yarum jën mi.
Peresidaa Fay leeral na itam solos sémb wii doon keno bu am doole ngir yokk dooley liy meññee ci « agropole centre » bi boole ko yombal xëy mi ñu xayma ci 30 000 ñeel askan wi.
PROMOREN dina bokk ci liy yombal bay dunde gi, yokk dooley ndundat yi ci kanamu soppikug njuux li, lépp jëm ci jàppandil suqalikug gox yi féete ci « bassin arachidier » bi.