Njiitu Réew mi Basiiru Jomaay FAY demoon ca Jama ngir nemmiku benn toolu ceeb bu ñu fa dagg lu yàggul dara.

xamle - 13 MONTHS.JUNE 2025


Ginnaaw Ros Beeco, Njiitu Réew mi, Basiiru Jomaay FAY, demoon na ca Jama, ci lu soxal tukki nemmiku gi muy amal ca "Pôle territorial Nord”.

Ci nemmiku gii, Njiitu Réew mi demoon na xooli benn tool bu ñu fa dagg bees, ñu taxawal ko ci sémb wii di “Projet de Développement Rural de Savoigne (PDRS)” ci kopparalug Bànku Araab gi taxaw ngir Suqalikug Koomum Afrig (BADEA).

Naal wu am solo wii, dina jariñ gën gaa néew 5700i nit ñu dëkk ci 11i dëkki kaw yu nekk ca tund wa. Jubluwaay bi di méngale mbayum gox ba ak jamono jaare ko ci dugal fa ay jumtukaay yu xereñ ak tabax ay warabi dencukaay yu mucc ayib, lépp ngir taxaw ci ñoŋal bu baax liy meññee ci mbay mi.

Muy naal buy tàbbi ci jubluwaayu Gis-Gisu Senegaal 2050 bi Ngóornamaŋ bi di doxal te la ca jiitu di yegg ci man a bay-dunde ak fexe ba baykat yi manal seen bopp ngir suqaliku gu sax te daj fépp.