Njiitu Réew mi Basiiru JOMAAY Fay, wane na ag tiisam ginnaaw génn àddunag Kilifa gu Sell gii di Paab Farañsuwaa te am altine 21i fani awril 2025.
Ci bataaxel bu ànd ak teewlu, Njiitu Réew mi fàttali na taxawaayu jëmm ju sell jii nga xam ne doonoon na ku ràññiku ci biir àddina si. « Tiis dëgg laa am bi ma yëgee faatug Kilifa gu sell gii di Paab Farañsuwaa. Àddina ñàkk na nitu diine ku amoon taxawaay », di li Peresidaa Fay xamle. Mu fésal dogu gu sax gi Paab bi amoon jëme ci ñi gën a néew doole niki noonu xeex bi mu yàgg a amal ngir déggoo ci diggante diine yi ak mbokkoo diggante askan yi. « Ak taxawaay bu am solo bi mu amoon ci taxawu ñi gën a néew doole ak wooteem bu sax ngir diisoo diggante askan yi ak diine yi, nekkoon na jëmm ju ay miliyoŋi way-gëm ak ay woromi baax wékkoon seen yaakaar », di li mu ci dolli.
Ci turu askanu Senegaal, Peresidaa Fay « jébbal na am njaalam » jëme ko ci Égliisu Kayolig bi, njabootu katolig yu Senegaal ak yu àddina sépp, niki noonu mbooleem ñi daan bàyyi xel bataaxelu jàmm ak mbëggeel bu Paab Farañsuwaa. Moom jëmm jii, ci ay kàddoom ak i jëfam, bu weesoo mbiru gëm-gëm sax, royukaay dëgg la woon, di jëmm ju bàyyi ndono lu yaatu ci wàllu pas-pas ak yërmande gu daj àddina.
Kon Senegaal, di réew mu ràññiku ci dëkkandoo ci jàmm diggante diine yi, mu ngi dello njukkal lu kawe jëmm jii joxoon dundam gépp xeex ngir yamale diggante askan yi, jàppoo ak bennoo ci kaw wuute.