Njiitu Réew Mi Basiiru Jomaay Fay, daloo na, tay ci suba tën bi ñu jagleel Lat Joor, kenn ci jàmbaari réew miy màndargaal moom sa bopp.
Cig àddoom, Njiitu Réew mi rafetlu na yéene ju am solo jii bawoo ci Ndiisoog gox bu Cees jëm ci samp tën bu mag bii.
« Lat Joor jëmm ju am solo la ci mboorum réew mi, di jàmbaar joj ab xeexam ngir bañ nooteel du deñ mukk ci sunuy xel », di li mu xamle.
Dammeelu Kajoor bii ñu miinoon ci njàmbaarteem ci jàmmaarloo ak notekat bii di Farãas, amal na xeex bu tar ak gànnaay yu néew, ci jamono ji réewi Órob yu am doole yi doon xëccoo nu ñuy yilifee Afrig.
Peresidaa Fay xamle na ne tën bii fépp la yell ci biir Afrig, waaye nag fii ci Cees gi ñu tuddee jàmbaar ji aw xàll la gën a safee.
Njiitu Réew mi fàttali na mbañ gi Lat Joor wane ci bañ a jaay dëkkam, donte sax notekat bi bëggoon na fee samp ab raay. Njàmbaar ga mu wane ba faatu, gànnaay ya ca yoxo ya, firnde la ci bàkk wii di: « Dees nuy ray rekk, waaye deesu nu toroxal ».
Jataay bii fésal na itam yittey artist yi, bindkat yi ak nosekat yi bokk ci yiy dundal ndami Lat Joor yi ak yu yeneen jàmbaar yi ci mboorum Senegaal. «Taxawal aw askan, mooy fexe ba saxal jëfi royukaay yii », di li Peresidaa Fay xamle teg ci soññe ci ñuy jàngal ndaw ñi mbaax yii ci wàllu ngor ak bañ nooteel.
Delloo na njukkal itam yeneen jëmm yu taxawoon daan jàmmaarloo ak notekat bi, ñu mel ni Kaañ Fay, mi yàgg a bañ nooteel. Feddali na solos màggal jàmbaar yii ngir tabax ëllëg gu lalu ci jom, jàppalante ak déggoo ci Afrig. « Ci xeeti fàttaliku yu wuute yii ci biir Senegaal rekk lanuy tabaxee ëllëg gu lalu ci jom ak jàppalante », di li mu xamle.
Man ngeen a topp mbooleem àddug Njiitu Réew mi.
Kàdduy Njiiu Réew mi ca xewu daloo tën bi ñu jagleel Lat Joor Ngóone Latiir Jóob:
Ginnaaw bi ma nuyoo Jëwriñ yi bokk ci Ngóornamaŋ bi,
Góornoor bi,
Perefe bi,
Njiital Ndiisoog Gox bu Cees,
Farab gox bu Cees,
Fara yi,
Rektéeru Jànguneb Iba Deer Caam,
Soxna yi ak Sëriñ si bokk ci Ndoxal gi,
Soxna yi ak Sëriñ si bokk ci kilifay jàngune yi ak lekool yi,
Kilifa diine yi ak yu aada yi,
Soxna yi ak Sëriñ siy yëngu ci wàllu mbatiit,
Gan ñu tedd ñi,
Soxna yi ak Sëriñ si,
Bokki njàngaan yi ak bokki dongo yi,
Muse le meer,
Maa ngir rafetlu bu baax jëf ju am solo jii nga def ànd ko ak sa ndiisoog gox, jëm ci samp tën bu mag bii di fàttali Lat Joor Ngóone Latiir Jóob, di jëmm ju màgg ci sunu mboorum réew. Xeex bu am solo bi mu doon amal ngir bañ nooteel tax na mu bokk ci jàmbaar yi wér ci réewum Senegaal. Dammeelu Kajoor bii moo taxaw jàmmaarloo ak Farãas lu ëpp genn wàllu xaaju xarnu. Gànnaay ak xarala yu néew ya mu yoroon terewu ko matale jaloore jii, ci jamono ji réewi Tugal yu mag yi taxawee temm ngir séddoo Afrig, di kembaar gog jot naa dund lu metti ci njaayum jaam ñi. Mu ñëw sampe ci xàll wi nekk ci xolu dëkk bi, ñu tuddee ko sunu jàmbaar jii.
Ci Cees gii, ay jamono mu doonoon dëkkub Cangin, te tay ñu yàq tur wi tuddee ko Janxeen, fi la Dammeel mi doon door a falu dajalee ab xareem ngir delloo Kajoor moomeelam ci suuf si tubaab yi jëloon ci moom. Mu bari woon lool nag jàmbaar yu daanu ci toolu xare boobu ci bis boobu nuy fàttaliku ci weeru Mee 1863. Muy kon ndoortelu yënguy politig yu mucc ayib ci lu ëpp genn wàllu xaaju xarnu ci xeex bu tar bu Lat Joor Jóob doon amal ngir aar réewam génne ko cig nooteel.
Xereñte gi mu àndaloon da cee boole woon doon nit ku ñaw. Bañ a dellu ginnaawam ci fexe ba Kajoor moom boppam moo ko yóbbe woon mu lànk ne tubaab bi du du fi samp raay bi. Déqale ga mu mujj danoo nag li muy wane rekk mooy teqalikoo gi amoon ci diggante way-politigu tund wa waaye du dooley larmeb tubaab yi. Mu daanu fa, gànnaay ya ci ay yoxoom, di firndeel bàkku jàmbaar yi di: « Dees nuy ray rekk de, waaye deesu nu toroxal ».
Soxna yi ak Sëriñ si,
Jataay bii nuy teewe tay day tàbbi ci aada ji nu yàgg a am ci màggal jàmbaar jii daan xeex nooteel. Nettali yi géwél yi ak liggéeyi saa-mboor yi yàgg jottali diggante maas yi tax na ba artist yi, bindkat yi ak nosekat yi am màcceer bu ñu man a jëfandikoo ngir jëmmal bir yi nu yàgg a bokk di xalaat.
Ginnaaw Peresidaa Aamadu Siise Ja mi kañ maas ya doon xeex ngir jonn ci téereem bii di Bisi Lat Joor yu mujj topp ci Faatug Dammel, Ceerno Ba a ngi nuy woo ci nu dundaat mbaax mu am solo mi Dammel ame woon ci biir tiyaataram bii mu tuddee Lat Joor Yoonu Ngor.
Li nu nekk ci biir Cangin, ci wunti Kajoor tax na, manunoo bañ a fàttaliku kenn ku amoon solo ci doomi dëkk bi ci jamonoy Dammeel nga xam ne xayna dese nañoo xam dëgg dëgg ay jëfam ci xeex nooteel, waaye terewul muy ku jàmbaare. Muy Kaañ Fay mi xëtt ndigalu tubaab bi, daal di fatt yoon yi teretaŋi gerte gi daan jaar ci diggante Bawol ak dëkkub Rufisk. Ñi teewoon ci xare yooyu nag di ay góor ak i jigéen ñu am jom, noppi woon ngir jàmmaarloo ak tubaab yi bëggoon a teg loxo suufi Lexaar, Jobaas, Paloor, Ndut ak Saafi te bokk tay ci goxu Cees. Gëstu war naa génnewaat jeexitali xeex yu am solo yooyu ngir màggal ak delloo njukkal ñi amaloon jëf yooyu.
Sikki sàkka amul ci ne sunu jàmbaar jii dina wéy di am ay tën, ay jëfi pasin ak i téere yuy màggal góor ak jigéen ñi nga xam ne, niki Lat Joor Ngóone Latiir Jóob, bay nañu seen waar ci anam yu mucc ayib ci xët yi gën a gànjaru ci sunu mboor. Taxawal aw askan, mooy fexe ba saxal jëfi royukaay yii, di fàttali sunuy ndaw mbaax yi ñii doon dundal.
Soxna yi ak Sëriñ si,
Ci xeeti fàttaliku yu bari yii te wuute ci biir Senegaal, te ubbiku ci Afrig, lanu man a tabaxee ëllëg gu lalu ci jom, jàppalante ak déggoo.
Kon nag may nañu ma tay ma man a lim ñenn ci jëmm yooyu wéy, niki jëmm ju mel ni Buuru Waalo bii di Siidiya Ndate Yàlla mi jiite woon xeex bu tar ngir bañ tubaab bi teg loxo ci suufi maamam. Mu amoon nag gis-gis bu leer, woo mbooleem dëkk yi ne woon ci Senegàmbi ñu bennoo ngir bañ tubaab bi duug fa.
Bu dee ca Jolof, amoon nanu fa Buurba Alburi Seynabu Njaay, mi jamononteel Dammeelu Kajoor mi nuy màggal tay, lëkkaloo ak moom ba noppi di mbokkam. Lu ëpp 10i at, Gayndeg Yaŋ-Yaŋ gii, fépp fu ñu ko mas a soxalaa rekk daal dina taxaw. Ci noonu, bokkoon na ci lëkkatoo gu mag gu Liig Araab ci wetu Sayeer Mati Ba mi donnoon Almaami bu Rip, Mammadu Lamin Daraame mu Bundu ak Abdul Bookar Kan, wotekat bu mag bu Booseyaa, Emiir bu Fuuta, ngir taxaw temm ci xeex ni taxawaayu tubaab bi doon yaatoo ci réew mi.
May nanu ma itam fii tay ma man a fàttaliku Sultaan bu njëkk bu Dooso, Maydanda Hammadu Saydu Jermaakoy. Ci nguuram, tabaxoon na ci biir Jumaa ju mag ju Dooso, xabru bu méngoo ak doomi Jolof ji. Ci loolu, def na jëf juy firndeel jaayanteem gu yàggul dara ngir Afrig te doon luy fésal gu Buuru Jolof mi faatoo ca Niseer.
Ñaari muj yii, di bu Buurba ak bu Jermaakoy, dañuy firndeel ci bu wér pas-pasu jiital Afrig gi nu war di wommat ci mbooleem lu nuy jëf bis bu set.
Ca Gaabu googu la Gelowaar yi sanc Siin ak Saalum bawoo lu jiitu juróomi xarnu ci ginnaaw. Déggoo gi dox diggante doxandeem yi bawoo woon ca bëj-saalum ak Laamaan yu dëkki Séeréer yi moo jur mbaax yu wóor yi am ci fonk liggéey, jub, woyof, njàmbaar, sàmm sa kàddu ak sax ci cosaani maam ya. Doy na firnde ci mbaax yooyu rekk seede yu am solo yi Buur Siin Kumba Ndóofeen defoon ci Seex Ahmadu Bàmba, mu jaraloon ko sax mu ñàkk nguuram ba ci dundam sax, ngir bañ ñu génnewaat Sëriñ bi réew mi.
Mu bawoo ca Firdu, di dëkk bu ne woon ci noteelu Gaabu, Alfa Molo Balde mi defoon Seexu Umar Taal ab royuwaay, moo jëfandikoo raaya Lislaam, muccal Fuladu.
Musaa Molo miy doomam ji ko wuutu, moo taxaw amal jàmmaarloo gu tar diggam ak Farãas, Àngalteer ak Portigaal yi doon xëccoo foofa.
Bu dee ca Kaasamaas itam, gis nanu fa mbañ nooteel ak xeex bu tar ngir tubaab bi bañ faa dugg. Dëkk ak dëkk, góor ña ak jigéen ña ne woon ca tund woowa taxaw nañu temm ci sàmm seen suuf ba ni ñuy jubee Xare bu mag bi amoon. Alin Sitowe Jaata, Jigéenu Kabrus jooju daal di yékkatiwaat raaya wa masul a daanu ba mukk. Mboor di jàpp ci jëmm ju jàmbaare jii faatu 1944 ca Sudan ga ñu ko yóbbu woon, xeex bu tar bi mu amal ci bañ mbay ma ñu leen bëggoon a ga ngir ñu amal ko ca seen i suuf te doon lu wuute lool ak moom sa bopp ci li ngay dunde.
Nit ñu bees daal di jëlaat xeex bi jaare ko ci tàggat ay askan ci wàllu diine ju lalu ci pas-pas bu sori woon lool ak gànnaayi tubaab bi. Ñu taxaw temm ci lajjloo sémb wi fi tubaab bi indi woon jëm ci soppiloo nit ñi seen mbatiit. Seexunaa Seex Saad Bu, Amari Ngóone Ndaag Sekk, Seex Abdu Laahi Ñas, Seex Buu Kunta, Seydi El Haaji Maalig Si, Seex Ahmadu Bàmba Mbàkke, Seydinaa Limaamu Laay Caw, ñoom ñii ñépp indi nañu tontu yu wóor ci jafe-jafe yi amoon ci askanu Senegàmbi ca njeextalu 19eelu xarnu bi.
Tontu loolu nag doon na lu fi saxal xam-xam ak diine ci kanamu sémb wi fi tubaab bi bëggoon a samp. Ci noonu lañu fexe ba saxal fi li gën a am solo, muy gëm Yàlla, mbaaxi fonk liggéey, jub ak sàmmu, jaare ko ci di ko suuxatee ak bindi suufiyànke yi. Ñu mujj doon jëmm yu am solo ci xeex nooteel gu àndul ak daray fitna ci kanamu tubaab bi. Doon it ay làquwaay ci mbooleem ñi xamatul woon fu ñu jëm te daan wut ku leen gindi ci seen ug dund. Ndono loolu nag ñu ngi koy jokkalante diggante maas yi ci biir daara yi ñuy waaj a yeesal ngir boole leen ci doxaliinu njàngum Senegaal.
Jox gëdd boobu daara nag, mooy delluwaat ci mboor mu yàgg moomu fi Sëriñ si indi woon niki ñu koy nettalee ci xëti mboor yi. Ndamam li gën a rëy nag ci Senegaal, ma nga amee woon ca Fuuta ak mbañ gi Tooroodo yi amaloon ca 1976 te jëmm yu màgg yii di Ceerno Suleymaan Baal ak Abdul Xaadir Kan jiite woon ko.
Ñu tàggatee leen ca Pir, ca Kokki, ca Fuuta Jaloŋ, ca Bundu ak ci biir Sawiya ya ca Móritani, ñoom bañkat yooyu tooguñu woon rekk tëju ak la ñu jàngoon ci téere yi. Dañoo daal di taxawal boole ko ak doxal sémb wu wér te wóor wu jëm ci soppi Fuuta samp fa doxaliinu politig woo xam ne ci pal lees koy jaarale ngir tànn njiit ya. Waaye nag, xam-xam lañu teg muy keno bi ñuy jaar ngir soppi dundiinu askan wa, boole ko ak taxawal jumtukaayu njàng mu am doole muy tàggat mbooleem li wëroon Fuuta, dale ko ca Dimaar ba ca Damnga.
Nguur gi niki gox yi ak goxaan yi dañoo am wareefu jàngale ak a xamle ndono lu yaatu lii, ngir ñu man cee roy ngir coppite yi nu namm a amal ci sunu askan.
Soxna yi ak Sëriñ si,
Jëfu fara bii di Baabakar Jóob man naa doon niral ci mbooleem tabax yi gox yi ak goxaan yi di amal, ànd ko ak Nguur gi, jëm ci doxal politig yu yees yiy taxawu ndefar yi aju ci wàllu mbatiit. Gunge artist yi ak fentkat yi ci wàllu mbatiit bokk na ci liy tabax sunu am-am ci wàllu jumtukaay ak xam-xam, te doon keno bu wér ci sunug mbokkoo. Bu weesoo taar bi lii nuy daloo tay àndal, niki yeneen yu taaru yi sunuy fentkat, ñiy yëngu ci wàllu sinemaa ak sunuy bindkat di defar, dafa doon lu am solo ngir jàllale yi nu am ci sunu mbaax ak cosaan yi gën a gànjaru.
Lekool bi dafa war di jëfandikoo fàttaliku gii, ak ci anam yu mu ko man a jaarale rekk, ngir tàggat sunuy ndaw ci def leen ñu man a tabax réew mu moom boppam te tijjiku ci pas-pasu gëm Afrig.
Turi sunu xàll yi, sunu pénc yi, sunu jumtukaayi tàggat yaram yi ak mbatiit yi, sunu lekool yi ak tabaxi pénc mi niki piriwe yi, dees koo war di jukkee ci ndono lu yaatu lii nu bokkle, kenob royukaay yii nga xam ne moom lañuy ràññee sunu réew ak sunuy gëm-gëm. Wéy di doon wenn askan, mooy dooleel sunug bennoo jaare ko ci mbooleem balluwaay yiy dundal sunu ndono lu yaatu lii te wuute ci réew mi. Tay noo ngi màggal Lat Joor Ngóone Latiir Jóob ci dëkk boo xam ne lenn ci xët yi gën a gànjaru ci sunu mboor fii lees leen bindee.
Soxna yi ak Sëriñ si,
Cees itam mooy dëkkub sëminóo yi yàgg a fés ci mbooleem xeex yi soxal péexte ak yelleefi liggéeykat yi. Daj nañu lu ne ci seen jaayante googu. Sémben Usmaan di fàttali seleŋlug sëminoo gu yàgg googu ca 1947, ci téereem bii mu tudee « Les bouts de bois de Dieu » (Banti Maam Yàlla yi). Seleŋlug 1938 gi nga xam ne dese naa siiw te mujj cig bóom 27i fani sebtàmbar. Geneenug bóom gu tubaab yi amal te ngeen màndargaal ko ci tën bi ngeen samp ca xàllu Ayniina Faal, booy dugg ca Site Ibraahiima Saar, turu kilifay seleŋlug 1947 ga woon. Jamono ji « Front Populaire » di fay ci jamono yu tiis yi bawoo woon ci ñaareelu Xareb àddina si.
Ndax jar naa fàttali sax? Xeex boobu amoon ci àddina si te jeexe ci Afrig ak bóom gi ñu amal jëme ko ci tiiraayéeri Senegaal yi ca Caaroy 1 panu desàmbar 1944. Moom lanu doon màggal 80eelu at mi ngir mu bañ a raaf, jëfi góor ak jigéeni Afrig yooyu jëmoon ci tabax àddina su gën a taxaw ci yelleefi nit ñi te maandu.
Maa ngi leen di jaajëfal ci seen ug teewlu.