Njiitu Réew mi Basiiru Jomaay FAY dalal wenn tañu BP ngir waxtaane sémbu GTA ak mànduwaaru GNL bi mu jëkk a yab

xamle - 21 MONTHS.MAY 2025


 Njiitu Réew mi Basiiru Jomaay Fay dalal na tay ci ngoon gi, S. Muray Auchincloss Njiital British Petrolum mi àndoon ak tañ wu am solo. 

Seen i waxtaan jëmoon ci jéego bu am solo bi ñu jot a teg ci Sémbu GTA ak mànduwaar bi ñu jëkk a yab ci gaasu yolnde bu raxul.