Biti Réew - 25 MONTHS.MARCH 2025
Njiitu Réew mi, Basiiru JOMAAY Jaxaar Fay, dalal na, ci talaata ji tañu FMI ci njiital Edward Gemayel, mi jiite liggéey bi FMI doon amal ci Senegaal. Moom mii nag mu ngi àndoon ak Majdi Debbich, mi teewal FMI ci Senegaal.
Ci bis boobu ba leegi, Njiitu Réew mi dalal na itam tañu lijjantig saa-siin gu mag gii di HUAWEI, ci njiital Shen Li, mi ñuy door a tabb Njiital lijjanti gi ci Afrig Bëj-gànnaar. Waxtaan yaa ngi gënoon a jëm ci yéeney lëkkaloo ak Senegaal ci pàcc yu am solo yu mel ni xarala yi, yasara gi ak tàggatu gu xereñ gi.