xamle - 31 MONTHS.JANUARY 2025
Njiitu Réew mi dalal na tay ci ngoognug àjjuma ji, Xabi Laam mii doon ku fés ci mbaali jokkoo yi, te ñu def ko bu yàggul dara ndawul UNICEF ngir yelleefi xale yi.
Mu àndoon ak Njiital pekk yi ci réew ak tund yi UNICEF teew, Xabi Laam fésal na yéeneem jëm ci xeex ngir yelleefi xale yi ak dooleel seen um njàng niki noonu seen nekkiin.
Peresidaa Fay daal di jaajëfal ndaw lii ci ay jëfam yu mat a roy ak ni mu taqoo ak réewam mii mu juddoo di Senegaal.
Njiitu Réew mi fàttali na ci njukkal lii muy delloo Xabi Laam ne, taxawu xale yi, mooy liggéey ngir ëllëgu réew mi. Feddali na dogug Ngóornamaŋ bi jëm ci yokk naal yi ñuy teg ngir kaaraange ak yokkuteg mbooleem xale yi, ak fépp fu ñu man a féete ci Senegaal.