Njiitu Réew mi Basiiru JOMAAY Fay dalal na Umar Si miy amal ug ngan jamono jii ci Senegaal.

xamle - 10 MONTHS.JANUARY 2025

Njiitu Réew mi, Basiiru Jomaay Fay dalal na tay ci Njénde li, aktéer bii di Umar Si, ci lu soxal tukki nemmiku bi muy amal ci Senegaal te laale ak « Vision Sénégal 2050 ». Muy ndaje mu ñu leeral bu baax xereñteg Senegaal ci wàllu sinemaa, ak mbatiit, te doon lu ay ndawam di doxal ci seen xel yu ñor te ñaw ngir gën a wane Senegaal fépp ci àddina si.

Njiitu Réew mi feddali na yéeneem ci def Senegaal muy royukaay ci yokkute gu sax dàkk ba kenn ku ne man cee gis boppam, boole ko ak di soññ mbooleem doomi Senegaal yi ñu dugal ci seen loxo, rawati na nag jëmm yi ñu gën a miin ci àddina si. Ndaje mii nag day firndeel dogug Nguur gi ci gën a fésal sunu moomeel ci wàllu mbatiit, taxawu mbirum sinemaa boole ko ak gën a xemmeloo ñi yor ay sémb yu ñu man a doxal ci Senegaal, lépp jëm ci jëmale réew mi kanam ak dund gu mucc ayib ñeel askan wi.