Njiitu Réew mi Basiiru JOMAAY Fay dalal na tañ yu AGC ak AISCCUF.

xamle - 10 MONTHS.APRIL 2025

Njiitu Réew mi, Basiiru Jomaay Fay, séq na ci alxemes ji 10i fani awril 2025, ñaari jataay ak tañ yii di Kërug Lëkkaloo diggante Senegaal ak Gine Bisaawóo (AGC), ak wu Mbootaayu Campeef yu kawe yi bokk làkku farañse (AISCCUF).

Njiitu Réew mi njëkk naa dalal Kërug Lëkkaloo diggante Senegaal ak Gine Bisaawóo (AGC), ci Njiital S. Inusaa Balde. Ci jataay bi, S. Balde aajar na tolluwaayu mbootaay gi, jaare ko ci leeral liggéey yi mu jot a sottal niki noonu mbébet yi mu am jëm ci gën a dooleel jëflante diggante ñaari réew yi. Waxtaane nañu itam sémbi suqaliku yi ACG am, rawati na ci wàllu koom mi ak dundiin wi.

Ci ngoon gi, Njiitu Réew mi dalal na itam, tañu Mbootaayu Campeef yu kawe yi bokk làkku farañse (AISCCUF), ci njiital S. Mammadu Fay, Njiital « Cour des Comptes » bu Senegaal. Ñu doon amal um ndaje ci Ndakaaru, ndawi mbootaay gi yaatal nañu ak Njiitu Réew mi ci tomb yi ñu tënkee ci liggéey yi ñu doon amal, te séddalikoo ci jafe-jafey njuux yi campeefi càmbar yooyu nekk ci réewi farànkofoni di jànkoonteel.  Ci waxtaan yi, fésal nañu solos amal yoriin wu wóor ci kanamu jafe-jafey njuux yi àddina di jànkoonteel.