Njiitu Réew mi Basiiru Jomaay FAY dalal na S. Norihiko Ishiguro, Njiitu JETRO.

Biti Réew - 20 MONTHS.AUGUST 2025

Njiitu Réew mi Basiiru Jomaay FAY dalal na Njiitu Japan External Trade Organization (JETRO), di bànqaas bu aju ci njëwriñu Japon gi yor wàllu Koom te ñu dénk ko yombal jëflante yi diggante Japon ak ay way-lëngoom yi ci wàllu koom ci biir àddina si. 


Am na 25i këri liggéeyukaayi Japon yu jot a sampu Senegaal. Waxtaan yi jëmoon ci yéeneey gën a yokk teewaay boobu, rawati na ci fànn yu am solo yu mel ni tàggatu gu xereñ gi, xarala yi ak yasara yu nëtëx yi. 


JETRO xamle na itam ne dina teew ci  Forum Invest in Senegal bi war a am  7 ak 8i fani oktoobar 2025 ci Ndakaaru, ngir gën a jàpp ci  dugal xaalis ci ay naal boole ko ak gën a suqali lëngoo gu dëgër diggante Senegaal ak Japon.