Biti Réew - 20 MONTHS.AUGUST 2025
Njiitu Réew mi, Basiiru Jomaay FAY mu ngi doore bisam bu jëkk ca Japon ci jataay bu mu séq ak Soxna Sarra Zaafrani Zenzri, Njiitu Jëwriñu Tunusi.
Ñaari kilifa yi fàttali nañu jëflantey mbokkoo yi yàgg a dox diggante Senegaal ak Tunusi, ñaari réew yu am mbaax yu bari yu ñu bokkle ak gis-gis yu dëppoo ci tomb yu bari. Fas nañu yéene gën a dëgëral lëkkaloo gi, jaare ko ci di ko doxal ci fànn yu bari te wuute, rawatina ci gën a boole sektéer piriwe yi.
Paj mi, xarala yi, ndugalum xaalis mi ak wàllu tukki bi bokk nañu ci fànn yi ñaari réew yi am yéene gën ci a feddali seen ug lëngoo.