Njiitu Réew mi Basiiru Jomaay Fay dalal na Njiital « Qatar Fund for Development » ak Njiital « Goldman Sachs Institute » ngir waxtaane pàcc yu am solo yu ñu man a dugal xaalis

Biti Réew - 07 MONTHS.DECEMBER 2024

Muy teewe jamono jii Ndajem waxtaan mu Doha, Njiitu Réew mi Basiiru JOMAAY Fay, séq na tay ab jataay ak  S. Fahad Al-Sulaiti, Njiital « Qatar Fund for Development ». Seen i waxtaan jëmoon ci jëflante yu mucc ayib yi dox diggante Senegaal ak Kataar, te   waa  Kataar yi jekk ngir gën koo dolleel jaare ko ci dugal seen alal ci pàcc yu am solo yi nekk ci biir gis-gisu Senegaal 2050. Waxtaan nañu itam ci luy gën a rattaxal lëngoo gi diggante sektéer piriwe ñaari réew yi.

Bu weesoo Njiital « Qatar Fund for Development », Njiitu Réew mi dalal na S. Jared Cohen, Njiital « Goldman Sachs Institute ». Tomb yi ñu doon waxtaane jëmoon ci pàcc yi ñu man a dugal xaalis ci Senegaal, jaare ko ci gën fésal sémb yi nekk ci pàcc yi gën a am solo ci gis-gisu Senegaal 2050.

Ndaje yii di firndeel yéene ju wér ji Njiitu Réew mi am ci sóob mbooleem partaneer yi, ñu dugal xaalis ci pàcc yu am solo ngir sottal mébet yi Senegaal am ci wàllu suqaliku gu sax te matale.