Njiitu Réew mi Basiiru JOMAAY Fay dalal na Jëwriñu Japon ji yor wàllu jëflante ak biti réew ak wenn tañu APF ci Njénde li.

Biti Réew - 29 MONTHS.APRIL 2025

Njiitu Réew mi, Basiiru Jomaay Fay, dalal na tay ci ngoon gi, ci Njénde li, Jëwriñu Japon ji yor wàllu jëflante ak Biti Réew, S. Takeshi Iwaya mi ñëwoon ngir indi ndëne lu bawoo ci Njiitu Jëwriñu Japon ci 9eelu Ndajem Tokyo mi ñuy amal ngir waxtaane suqalikug Afrig (TICAD), ñu jàpp ko ci weeru ut wiy dëgmal ca Yokohama. S Iwaya weccente na ak Njiitu Réew mi ci luy gën a dooleel jëflante yi diggante Senegaal ak Japon.  

Ba tay, Njiitu Réew mi dalal na tañu Mbootaayug Ngomblaani Farànkofoni (APF), ci njiital Topp-Njiital Ngomblaanug   Kamerun, Hilarion Etong, ci lu soxal nemmiku gi APF di amal ci Ndakaaru, te jamono jii mu nekk di amal liggéey yi aju ci komisoo politigam bi.