Njiitu Réew mi Basiiru Jomaay Fay dalal na Jëwriñu Araabi Sawudit ji yor wàllu aj gi ak umra gi

Biti Réew - 07 MONTHS.FEBRUARY 2025

Njiitu Réew mi Basiiru Jomaay Fay dalal na, démb ci alxemes ji, Dr. Tawfiq ben Fawzan Al-Rabiah, miy Jëwriñu Araabi Sawudi ji yor wàllu Aj gi ak Umra gi.

Muy amal nganam gu njëkk ci Senegaal, posewu na ci ngir àddu ci jëflante yu mucc ayib yi yàgg a dox diggante Ndakaaru ak Riyaad niki noonu xoolaat anam yi ujaaji Senegaal yi di amalee aj gi.