Njiitu Réew mi Basiiru Jomaay Fay, àndoon na tay ak mbooloo mu takku, dem ca Yoof ngir jébbal njaalam njabootug Laayeen, ci turu askanu Senegaal, ginnaaw bi Sëriñ Muhammadu Maxtaar Laay mi nekkoon Kilifag yoonu Laayeen wuyujee Boroomam.
Ci nemmiku googu, Njiitu Réew mi delloo na njukkal bu baax ndem-si-Yàlla si, di rafetlu ak a fàttali taxawaay bu am solo bi mu amoon ngir jàmm, ngëm ak bennoo ci réew mi. Njiitu Réew mi fésal na ndono lu yaatu li fi Sëriñ Muhammadu Maxtaar Laay mi nga xam ne, royukaay bu mag la woon ci wàllu pas-pas ak dundiin ci Senegaal, bàyyi.
Njiitu Réew mi xamal na Xalifa bu bees bi ne dina taxaw ci wetam ngir gunge ko jàppale ko ci sas wi, teg ci ñaanal ko yen bi woyof ba mu matale mbooleem naal yi. Feddali na taxawaayu Nguur gi ci wéyal jëflante gu sax dàkk te rafet diggam ak këri diine yi, lépp ci kaw lëngoo ak joxante cér.