Njiitu Réew mi Basiiru Jomaay FAY ca Ndajem Lijjantikati Farãas yi

Biti Réew - 27 MONTHS.AUGUST 2025



Mu ne woon ganug Ndaje mi Lijjantikati Farãas yi doon amal, Njiitu Réew mi Basiiru Jomaay FAY, yékkati na tay ci suba si, ca Rolland Garos, kàddu yu am solo te góndi ñiy yëngu ci sektéer piriwe bu Farãas ak bu àddina si. 


Ci barab bu kawe bii, Njiitu Réew mi rafetlu na cér bi ñu fa jagleel Senegaal teg ci feddali yéeneem jëm ci amal lëngoo yu bees yu ñépp di gis seen bopp, niki ñu ko tënkee ci biir « Vision Sénégal 2050 ». 


Leeral na coppite yi ñu sumb te jëm ci gën a jagal géewu jëflante yi, xeex ger, jëfandikoo xarala yi ci lu soxal lijjanti yi ci wàllu ndoxal, niki noonu xéewal yu yaatu yi Senegaal làq ci wàllu yasara gi, xarala yi, mbay mi ak jumtukaay yi. 


Mu fas yéene sukkandiku ci ndaw ñi war a doon kenoy jonate bi, Senegaal jekk na ngir ànd ak ay partaneeram sóobu ci joŋante bii jëm ëllëg, wurendoo ko ak ñoom bokk ak ñoom it bége ndam li.