Njiitu Réew mi Basiiru Jomaay FAY ca Gine Bisaawóo ngir tukkib ñaari fan.

Biti Réew - 26 MONTHS.MAY 2025

Ci ndënel Umaro Sisoko Embaló, Njiitu Réewum Gine Bisaawóo, Kilifa gi, Basiiru Jomaay Jaxaar FAY, Njiitu Réewum Senegaal, bawoo na Ndakaaru tay ci suba wutali Gine Bisaawóo ga mu war a amal tukkib nemmiku altine 26 ak talaata 27i fani mee 2025. 

 Tukki bii day tàbbi ci luy gën a dooleel lëkkaloo ak mbokkoo gi yàgg a dox diggante Senegaal ak Gine Bisaawóo. 

Porogaaraamu nemmiku yi mu ngi séddalikoo ci ay jataay diggante ñaari Njiiti Réew yi, niki noonu ay ndaje diggante tañi ñaari réew yi.