Biti Réew - 02 MONTHS.MAY 2025
Bis bi njëkk ci tukkib nemmiku Njiitu Réew mi Basiiru Jomaay Fay ca Gaboŋ, li ko màndargaal mooy ñaari jataay yu am solo.
Ci suba gi, Njiitu Réew mi, ci wetu magam di naataangoom bu Gaboŋ, Peresidaa Biris Oligi Ngemaa, sóobare si sargal nañu ko, laataa ko doomi Senegaal ya di jagleel teertu gu mucc ayib ngir seedeel ko seen cofeel ci moom.
Ci ngoon gi, Njiitu Réew mi teewe na ay ndaje yu gànjaru te ànd ak mbégte diggam ak ñi teewal mbootaayi doomi Senegaal yi féete Libreville ak yeneen dëkk yi nekk biir Gaboŋ. Jataayi weccentey xalaat yii tax nañu, ñu yaatal bu baax ci njàmbat ak nammeeli Saa-Senegaal yi féete Gaboŋ.