Njiitu Réew mi Basiiru JOMAAY Fay ca campug Peresidaa Biris Oligi Ngemaa ca Gaboŋ.

Biti Réew - 03 MONTHS.MAY 2025

Njiitu Réew mi, Basiiru Jomaay Fay, ma nga woon tay ca estaat Angondje bu Libreville, ca Gaboŋ, ànd ko ak yeneen fukk ak juróom benni Njiiti réewi Afrig, ngir teewe xewu campug Peresidaa Biris Oligi Ngemaa. 


Muy xew wu amoon solo ci wàllu sargal ak teewaayu mbooloo mu takku mu te àndoon ak mbégte. Ay yooni-yoon, mbooloo ma fa teewoon fésal nañu seen cofeel ci Peresidaa Fay mi nga xam ne foo tollu di dégg tàccu yi ñu ko doon jagleel, muy luy firndeel jëflantey mbokkoo yi dox diggante askanu Senegaal ak wu Gaboŋ. 


Teewaayu Njiitu Réew mi tamit di firndeel jaayante gu sax gu Senegaal am ngir bennoo, jàppalante ak lëngoo diggante réewi Afrig yi.