Ci 4eelu Ndajem àddina si ñu jagleel kopparalug suqaliku gi, ca Seville tay ci talaat ji 2i fani sulet 2025, Kilifa gi Basiiru Jomaay FAY, Njiitu Réewum Senegaal, bokk na jiite, ci wetu kilifa gii di Pedro Sánchez, Njiitu Ngóornamaŋu Espaañ, ab jataay bu kawe ci tomb bii di : « Dox jëm ci amal doxaliinu bor buy indi ag suqaliku ».
Cig àddoom, Njiitu Réew mi amal na njàngat lu am solo te leer ci anam yi ñuy lebalee réew yi ci jamono jii, mu jàpp ne méngoowul, yamalewul te dese naa dëppoo bu baax ak li réew yu néew doole yi yittewoo ngir man a suqaliku. Xamle na ne doxaliin wii day gàllankoor bu baax askan wi ngir ñu man a jot ci soxla yi gën a far yu mel ni njàng mi, paj mi, ndox mu sell walla sax lekk gu baax te doy.
Ci loolu, Njiitu Réew mi soññee na ngir ñu amal ci coppite yu wér te boole ñépp, yu tegu ci pas-pasu doxal yoon, maandute ak doxaliin wu leer. Taxawlu na bu baax itam ci ne fàww ñu xoolaat bu baax anam ak doxaliinu wànqaasi nattukaay yi, lépp tamit ci kaw tegaale ay doxaliin yuy dakkal bor bi ci saa si bu dee dafa am jafe-jafe yu kenn séntuwul woon.
Ci biir àddoom, Njiitu Réew mi Jomaay FAY fésal na itam :
. yeesalug kaadaru bokkoo bu G20 ngir lëkkale gu mucc ayib ci àddina si,
. dooleel taxawaayu bànk piblig yi ci wàllu suqaliku ci kopparal gu am doole,
. fàww ñu boole bori piriwe yi ci doxaliinu joyyanti gi.
Mu tëjee, ci teewayam ci ñenteelu Ndajem àddina si ci kopparalug suqaliku gi, moom Njiitu Réew mi feddali jaayanteg Senegaal ci fas yéenee taxaw temm ngir gàddu ci fulla, gis-gisu yoriinu bor bu gën a maandu, gën a ànd ak yërmande te taxaw ci suqaliku gu sax dàkk.