Njiitu Réew mi Basiiru Jomaay Fay bawoo na Ndakaaru jëm Libreville

Biti Réew - 02 MONTHS.MAY 2025

 Njiitu Réew mi, Basiiru Jomaay Fay, bawoo na Ndakaaru tay ci suba si wutali Libreville. Dina teewe campug Njiitu Réewum Gaboŋ, Biris Oligi Ngemaa, gi ñu jàpp suba ci gaawu bi, 3i fani mee.

Ba muy dem moom Njiitu Réew mi, Usmaan Sonko Njiitu Jëwriñ yi a ko gunge.