Biti Réew - 04 MONTHS.DECEMBER 2024
Njiitu Réew mi Basiiru Jomaay Fay, bawoo na Ndakaaru tay ci suba wutali Emiraa Araab Unii ga mu war a amal ug ngan i 4 ba 6i fani desàmbar 2024, ci ndënel kilifa gi Seex Mohammet Bin Sayed Al Nahyan, Njiitu Réewum Emiraa Araab Unii.
Bu fa bawoo, moom Njiitu Réew Mi dina dem ca Ndajem waxtaan may am ca Dohaa, ca Kataar, 6 jàpp 8i fani desàmbar 2024, ci ndënel kilifa ga Seex Tamiim Bin Hamad Al Saanii, Emiir bu Kataar.
Ndaje mii di xew-xew bu mag ci àddina si, ñu jagleel ko waxtaane jafey-jafey àddina si ci wàllu doxaliin, kaaraange ak suqaliku gu sax.