Njiitu Réew mi Basiiru JOMAAY Fay amal na tijjitel Barabu Fésal bi ñu jagleel Yónnent bi Muhammat (SLHWS) ci Ndakaaru.

xamle - 27 MONTHS.FEBRUARY 2025



Njiitu Réew mi, Basiiru Jomaay Fay amal na tijjitel barabu fésal dund ak jëfi Yónnent bi Muhmmat (SLHWS). Barab bu kawe bii ci wàllu pas-pas, te doon bi njëkk ci Afrig Sowu Jant, dina may képp ku fa tàbbi, mu man a xam lu bari ci wàllu Mboor jaare ko ci xarala yu yees yi, lépp jëm ci gën a xam ndono lu yaatu li fi Yónnent bi (SLHWS) bàyyi ak xóotaayu njàngaleem ci wàllu yërmande, yoon ak jàmm.

Jataay bu am solo bii, dajale na ay gan ñu gànjaru : ñu bokk ci Ngóornamaŋ bi, kilifay diine, ndawi laamisoo yi ak kilifa aada yi. Barab bii Réewum Araabi Sawudit maye jaare ko ci Lig Islaamig, day firndeel jëflante yu am solo yi dox diggante Ndakaaru ak Riyaad. Xew wii nag doon na jéego bu am solo jëm ci gën a fésal moomeelu lislaam boole ci di dooleel taqoo gi Senegaal taqoo ak Njàngalem Yónnent bi (SLHWS) mi tabax li ñu nuy ràññee muy mbaaxi nangulante, mbokkoo ak dundandoo ci jàmm.

Ci turu askanu Senegaal, Njiitu Réew mi sant na bu baax boole ko ak gërëm Buuru Araabi Sawudit di Salmaan Bin Abdel Asiis Al Sawud ak doomam jii di Mohammet Bin Salmaan, di ñoo xam ne seen ug njàppale moo tax ñu man a jëmmal sémb wu am solo wii. Seen jaayante gu sax dàkk ngir yaatal xam-xam ak bataaxelu lislaam bu yaatu bii ñeel àddina si, doon na ndono lu yaatu ngir maas yi war a ñëw ëllëg.

Barab bii féete ci biir Ndakaaru li ñu ci namm mooy mu doon barabu mbatiit ak jàngale bu jàppandi ci ñépp. Muy firndeel rekk taxawaayu Senegaal niki réewum lislaam, xam-xam ak diisoo, moo xam ne day boole tijjeeku ak sàmm mbaax yi nu boole.

Man ngeen a teewlu kàddu yi Njiitu Réew mi jibal ci Wolof :