
Senegaal lootaabe na, ca « African Burial Ground National Monument » bu New York, ndaje mu am solo mu jëmoon ci fàttaliku Afrig, yoon ak defaraat, te Njiitu Réew mi Basiiru Jomaay FAY bokkoon ko jiite ak naataangoom bu Gana, John Dramani Mahama.
Cig àddoom, Njiitu Réew mi fàttali na ne fàttaliku doonul ngir delloosi li wéy, waaye ab tegtalukaay la ngir ëllëg. Ndaje mii, tàbbi ci doxaliinu Mbootaayu Réewi Afrig gi jàppe 2025 muy « Atum yoon ak defaraat », sóob na Afrig ak jasporaam ngir ñu soppi fàttaliku yi def leen dooley jëf ngir yoon, diñite ak jàppalante.
Ay kilifay yu Kawe ci Afrig ak Karayib teewoon nañu ci jataay bii :
- Kilifa gii di Azali ASUMANI, Njiitu Réewum Komoor
- Kilifa gii di Muhammed B.S. Jallow, Topp-Njiitu Gàmbi
- Klifa gii di Francia Márquez, Topp-Njiitu Kolombi
- Kilifa gii di Mia Amor Mottley, Njiitu Jëwriñu Barbad
- Kilifa gii di Rimtalba Jean-Emmanuel WEDRAAGO, Njiitu Jëwriñu Burkinaa Faaso
- Kilifa gii di Seneraal Abdulaay MAYGA, Njiitu Jëwriñu Mali
- S. Dawda A. Jallow, Jëwriñu Yoon ju Gàmbi
- S. Omar Alieu Turey, Njiitu Komisoo CEDEAO
- Ndawul Komisoo bu Mbootaayu Réewi Afrig
- Jëwriñu Afrig yu bari yu yor mbirum Jëflante ak Biti Réew
Jëmm yu am solo ci Jasporaa bi itam teewe nañu yëngu gu am solo gii : aktéer bii di Omar Si, Aamadu Galo FAAL, Topp-Njiitu NBA, niki noonu basket ya woon di Joakim Noah, De Saagana JÓOB ak Mataar NJAAY.
PEEÑ :












