Lu jëm ci Ndajem Lijjantikati Farãas ma mu ne woon gan ga, Njiitu Réew mi Basiiru Jomaay FAY, séq na ay jataay yu bari ak ñu bari ñuy yëngu ci wàllu koom ak campeef yu ràññiku. Waxtaan yii, lalu woon ci wàllu lëngoo ak dugal xaliis, dañuy wane yéeney Njiitu Réew mi jëm ci def Senegaal muy jëmukaay bu ñu taamu ngir lëkkaloo yu sax te am i njariñ.
Ci jamonoy dundalaat koomum àddina si ak wut ay royukaay ci wàllu suqaliku, Peresidaa FAY sumb na ay waxtaan diggam ak këri liggéeyukaay ak campeefi Farãas yuy yëngu ci fànn yu am solo.
Bokk na ci ñi mu jëkk a dalal, S VICAT mi am wàll ci SOCOCIM, ngir gën a xóotal ak moom ci lu jëm ci gën a dooleel wàllu simaa. Waxtaan yi jëmoon ci wàññi njëgu simaa bi, fexe mu jàppandi ci askan wi, ak taxawaay bi mu am ci tabax yu mag yi ñuy amal ci réew mi.
Ci loolu ba leegi, Njiitu Réew mi dalal na ndawi MEDEF International gi dajale Ay Njiiti këri liggéeyukaayi Farãas yu ràññiku ci àddina si. Muy ndaje mu tax ñu yaatal ci yeneen fànn yu ñu man a dugal xaalis, lépp boole ko ak feddali solos lëkkaloog koom mu am doole tey jariñ wàll yépp.
Wàllu jumtukaay yi tamit yaatal nañu ci. Ci noonu kon, Njiitu Réew mi dalal na këru liggéeyukaay gu xereñ ci wàllu tabax jumtukaayi pasiin, ngir waxtaane naal yu am solo yu mel ni ay njéggite, ay yoon ak jumtukaay yuy yombal dem gi ak dikk gi ak pàkkug mbeeraay gi.
Ci wàllu yënguy naawu yi, « Groupe Lagardère Travel Retail » gi yor caytug « duty free » yu AIBD, dalal na leen ngir waxtaane baaxaayu liggéey yi ñuy amal, ni ñuy doxalee ci wàllu njëg yi ak mbébetu gën a yaatal yëngu yi ngir tukki bu ànd ak noflaay.
Wàllu Mbell yi desul ginnaaw. Njiitu Réew mi dalal na ERAMED Senegaal di ñu am taxawaay ci wàllu jëfandikug balli mbindare yi. Waxtaan yi jëmoon ci caytu gu sax, guy jur ay xëy te sàmmonte ak kéew mi.
Njiitu Réew mi jataayu na ak « Groupe NGE », doon ñu xereñ ci tabax ay jumtukaay ci pénc mi, ngir waxtaan ci suqali ay jumutukaay yu am solo ak dooleel xëy mi, rawati na ci tund yi làq njariñ yu yaatu.
Bu weesoo ñiy yëngu ci wàllu koom, Peresidaa FAY dalal na itam Sëñ Jean-Noël Barrot, Jëwriñu Farãas ji yor wàllu Órob ak wàllu jëflante ak biti réew, niki noonu Njiitu Jëwriñ ya woon di Sëñ Édouard Philippe, ngir ay waxtaan yu kawe ci wàllu lëkkaloo ak mbébeti lëngoo ci wàllu campeef.
Mbooleem ndaje yii nag dañuy firndeel jaayanteg Senegaal jëm ci tabax lëngoo yu dëgër, ñoŋ te ànd ak coppite, niki ñu ko tënkee ci
biir « Vision Sénégal 2050 » bi ak
« Plan national de transformation » bi. Dañuy wane itam dogug Njiitu Réew mi jëm ci fexe ba wàllu laamisoo am njeexital yu am solo ngir suqalikug réew mi.