Njiitu Réew mi amal na ndoortel diisoo ci réew mi jëm ci waxtaane Njàng mu Kawe mi, Gëstu gi ak Fent gi.

waxtaan - 17 MONTHS.JULY 2025


Kilifa gi Basiiru Jomaay FAY, Njiitu Réewum Senegaal, jiite na ci alxemes ji 17i fani sulet 2025, jataayu tijjitel diisoo yi ñu jagleel ci réew mi waxtaane Njàng mu Kawe mi, Gëstu gi ak Fent gi. Ci kanamu ay waroomi xam-xam, ay gëstukat, ay njàngaan ak ñu am solo ñuy yëngu ci wàll wi, Njiitu Réew mi àddu na ngir ñu amal coppite yu xóot ci sistemu njàng mu kawe mu Senegaal. Yéeney coppite joogu nag mooy jéem koo méngale ak li ñu yittewoo ci wàllu koom ak dundiin, jafe-jafe yi ñuy jànkoonteel ak jubluwaay yu am solo yi nekk ci “Vision Sénégal 2050”.

Cig àddoom, Peresidaa FAY taxawlu na bu baax ci xamle ne fàww jànguneb Senegaal jéem a am xàmmekaayu boppam. Mu xamle ànd ci ak dogu ne : « Sunu xam-xam benn la fi te lu wér te wóor la. Waratunu leen a desal ginnaaw ci kanamu model yu nuy jéggaani yu méngoowul ak nun. » Muy kàddu yuy firndeel jamp gi nekk ci dëggal moom sunu bopp ci wàllu xam-xam ak mbatiit. 

Ci yitte yi gën a far, Njiitu Réew mi xamle na keno yu bari yu am solo :

•  dooleel moom sa bopp ci wàllu xam-xam ak mbatiit ;

•  jëfandikoo làkk yu bari ak xam-xam yi ci réew mi ;

•  amal coppite ci BAC bi ak sémb yi ñuy jàngale ;

•  kopparal gu sax ci gëstu gi ak suqali xarala yi ;

•  séddale gu maandu ci jumtukaayi jàngune yi ci réew mi ;

•  niki noonu taxawaay bu am solo bu njàng mu kawe mi war a am ci amal coppite gu matale ci Senegaal.


Njiitu Réew mi soññe na itam ngir ñu teqalikoo ak ndonoy tubaab bi ngir samp sistemu njàng mi, dëppale ko ak sunu mbaax ci wàllu mbatiit, dundiin ak koomum réew mi. 

Ci geneen wàll, rafetlu na taxawaayu Jëwriñu Njàng mu Kawe mi, Gëstu gi ak Fent gi, Sëriñ Abdurahmaan JUUF, teg ci dénk Profesëer Buubakar JÓOB mu jiite waxtaan yi. Mbébet mii day firndeel yéeney Nguur gi jëm ci tabax jànguneb Senegaal bu méngoo ak jamono, sax ci sunu cosaan, yemale te sóobu ngir gën a dooleel moom sa bopp gi ci réew mi ak feddali suqaliku gu sax dàkk.